Xaalaat yoo mën a jëmmalee ci OneNote

Yebbil jëfekaay bi

Yebbi


Jogee Evernote jëm OneNote dafay yomb ak nga lëkkalante say karmat ci jëfandaay yépp, te doo fay. Xamal naka la


Sosal ko sa bopp

Dangay faram fàcce xalaat yu rëy ci sarbet wala xobi fàttali? Ndax danga taamu feesal gu leer? OneNote dalay may nga jëmmal say xalaat. Bindee masin, loxo wala rëdd jëmm yu la neex ak bik ci kaw këyit. Seeteel te daggee ay mbir ci net bi ngir nataal say xalaat.

Tablet buy wane OneNote ci Windows 10

Liggéeyandoo ak ku nekk

Sa kuréel a ngi jëmmal xalaat yu rëy. Sa njaboot a ngi waajal tongum ndaje. Ci wenn xët ngay nekk, lëkkalante ko foo mën a nekk.

Nataalu kuy jëfandikoo OneNote ci ab tablet ngir liggéey

Bind say xalaat

Tàmbalil rëdd lu la neex. Sa catu estile kese ngay soxla. Jëlal karmat yoo bindee loxo nga soppi leen ñu nekk mbindu masin beneen yoon. Fësalal mbir yi am solo te jëmmal say xalaat ci melo ak jëmm.

Melo yu yànj yuñ defee ak Bindukaayu Surface

Jotee ko fu nekk

Jël karmat. Jëlee sa ëmbiit fu nekk, lu yomb la, ba ci sudee danga nekk ci internet. Taalal sa ordinatër ba noppi nga yeesal karmat yi ci sa telefon. OneNote mën na dox ci bépp jëfandaay wala dal.

Nataali OneNote yuñ feeñal ci iPad, iPhone ak Apple Watch




Ci Office lay gën a dox

OneNote bokk na ci njabootu Office bi nga xam ba noppi. Bind ay karmat ak tomb yu bawoo ci bataaxalu Outlook, wala ñu mooñaale leen ci tablo Excel. Ak say jëfekaayi Office yiy doxandoo, sa liggéey dafa gën a yomb te gaaw.

Nataali sumbub Office

Lënku ci kalaas

Boole ndongo yi ci benn barabu liggéeyukaay wala jox ku nekk ndimbal ci karne boppam. Ak këyit yuñ móol yu gën a bari. Mën nga nos ay njàngale te sasaate ay liggéey ci kàggu bu mag bi.

Nemmeeku Karne Njàng

Nataali OneNote yiñ feeñal ci Surface Book